Balisage de la Déclaration des droits de l'homme en wolof

Table des matières

Entête CES
Description de fichier
Description du profil
Partie 1. BATAAXAL GU MAG GI ËMB SAÑ-SAÑI DOOMI AADAMA - [Preamble]
Partie 2. 1. Matukaay bu jëkk bi
Partie 3. 2. Naareelu matukaay
Partie 4. 3. Ñatteelu matukaay
Partie 5. 4. Ñeenteelu matukaay
Partie 6. 5. Juróomeelu matukaay
Partie 7. 6. Juróom benneeli matukaay
Partie 8. 7. Juróom benneeli matukaay
Partie 9. 8. Juróom natteelu matukaay
Partie 10. 9. Juróom ñentteeli matukaay
Partie 11. 10. Fukkeeli matukaay
Partie 12. 11. Fukkeeli been matukaay ak benn
Partie 13. 12. Fukkeeli matukaay ak ñaar
Partie 14. 13. Fukkeeli matukaay ak ñatt
Partie 15. 14. Fukkeeli matukaay ak ñent
Partie 16. 15. Fukkeeli matukaay ak juróom
Partie 17. 16. Fukkeeli matukaay ak juróom benn
Partie 18. 17. Fukkeeli matukaay ak juróom ñaar
Partie 19. 18. Fukkeeli matukaay ak juróom ñatt
Partie 20. 19. Fukkeeli matukaay ak juróom ñent
Partie 21. 20. Ñaar fukkeeli matukaay
Partie 22. 21. Ñaar fukkeeli matukaay ak benn
Partie 23. 22. Ñaar fukkeeli matukaay ak ñaar
Partie 24. 23. Ñaar fukk ak ñatteeli matukaay
Partie 25. 24. Ñaar fukk ak ñenteeli matukaay
Partie 26. 25. Ñaar fukk ak juróomeeli matukaay
Partie 27. 26. Ñaar fukk ak juróom benneeli matukaay
Partie 28. 27. Ñaar fukk ak juróom nenteeli matukaay
Partie 29. 28. Ñaar fukk ak juróom natteeli matukaay
Partie 30. 29. Ñaar fukk ak juróom nenteeli matukaay
Partie 31. 30. Fanweereeli matukaay

Entête CES

Créée par : | Statut actuel : new | Créée le : | Mis à jour le :

Description de fichier

Titre : Balisage de la Déclaration des droits de l'homme en wolof
Responsabilités :
Mame Thierno CISSE
Publication :
Distributeur : Projet AUF-LTT
  UCAD BP 5005 Dakar-Fann Sénégal
Publié le : 2004-02-24
Disponibilité : restricted - Version à utiliser seulement pour le projet de recherche AUF-LTT. Cette traduction n'engage pas la responsabilité des partenaires du projet. L'original figure à l'adresse http://www.unhchr.ch/udhr/navigate/alpha.htm.
Source : BATAAXAL GU MAG GI ËMB SAÑ-SAÑI DOOMI AADAMA Haut-Commissariat des Nations Unies aux droits de l'homme 8-14 Avenue de la Paix 1211 Genève 10, Suisse, numéro de téléphone (41-22) 917-9000 Haut-Commissariat des Nations Unies aux droits de l'homme 1948

Description du profil

Langues :  
  wolof  wol  wol 


Partie 1. BATAAXAL GU MAG GI ËMB SAÑ-SAÑI DOOMI AADAMA - [Preamble]

ŋëñŊËÑ

Ñu jàpp te nangu ne sagu doomi aadama ak sañ-sañam yépp-dañu yam te kenn mënukóo jalgati, te lu lépp nekk na cës laay ci taxufeex ci mbirum àtte ak jàmm ci biir àdduna.

Ñu jàpp ne ñakk xam ak soofantal sañ-sañi doomi aadama indi na aymusiba yu tar tax képp kuy dund fippu. Temano egsi na ba mu nekk ci doomi aadama ñu mën a wax, xalaat, ci seen coobare, bundxatal, nàkk dëddu leen.

Ñu jàpp ne am na solo lool ñu aar sañ-sañi doomu aadama ak ay matukaay ci wàllu yoon; ngir doomu aadama moomu kenn du ko sonal, muy fippu ci nootaange ak lu koy bunduxatal.

Ñu jàpp ne am na solo lool ñu góor-goorlu ba gën a rataxal jokkalante gi diggante xeet yi.

Ñu jàpp ne ci bataaxal boobule mbootaayu xeet yi yeesalaat na ay pas-pasam jëme ko ci sañ-sani doomi aadama yu tolloo, ci sag, ci bir lépp lu aju ci dundin diggante góor ak jigéen, ci biir tawfeex gu yaa.

Ñu jàpp ne réew yi ci bokk jël nañu ay matukaay ngir dëgëral jokkalante gi ak mbootaayu xeet yi, ñu naw it bu baax sann-sañi doomi aadama ak tawfeex yu wóor ci biir àdduna yépp.

Ñu jàpp ne ànd taxawal sañ-sañ yeek tawfeex yi nekk na lu am solo lool ngir, darajaal matukaay yooyu.

Ndaje mu mag mi biral na ci bataaxal bii ne xeet yépp, réew yépp ak kurel yépp ñu jàpp li ci nekk, ci seen xel, te ñu góor-góorlu, ñu jaarale lii lépp ci njàng mi ak yar gi.

Ñu lawal sañ-sañ yeek taawfeex yi jël aymatukaay ci biirak bitim réew.

Ñu nangu te di doxal fépp ci anam gu wér ci biir xeet yi sosoo ci réew i bokk ci mbootaay gi ak gox yi bootu ci ñoom.

Partie 2. 1. Matukaay bu jëkk bi

Doomi aadama yépp danuy juddu, yam ci tawfeex ci sag ak sañ-sañ. Nekk na it ku xam dëgg te ànd na ak xelam, te war naa jëflante ak nawleen, te teg ko ci wàllu mbokk.

Partie 3. 2. Naareelu matukaay

Ku ne mën naa wax ne am na ay sañ-sañ ak ay tawfeex yu sosoo ci bataaxal bii te amul xeej ak seen, rawatina ci wàllu xeet, melo, awra, làkk, diiné, peete ci wàllu politig, xalaat, réew mbaa askan woo mën ti sosoo, ci it wàllu juddu alal ak lu mu mën ti doon.

Rax sa dolli amul xeej ak seen ci politig, yoon, mbaa doxalin wu aju ci bitim réew mbaa suuf soo xamne nit ki fa la cosaanoo; réew moomu mbaa suuf soosu moom na boppam walla deet, mbaa ñu yamale yengu-yëngoom.

Partie 4. 3. Ñatteelu matukaay

Nit kune war naa dund ci tawfeex ak kaaraange.

Partie 5. 4. Ñeenteelu matukaay

Waruñoo def kenn jaam mbaa mbindaan. Njaam ak njaayum jaam nanguwunu ko ci anam gu mu mën ti doon.

Partie 6. 5. Juróomeelu matukaay

Waruñoo mbugal, tutal, mbaa teg kenn lu metti lool lu yelloo wul ak doomu aadama.

Partie 7. 6. Juróom benneeli matukaay

Nit ku ne am na sañ-sañ ñu war kaa nangul darajaam ci wàllu yoon.

Partie 8. 7. Juróom benneeli matukaay

Népp a yam ci kanamu yoon. Te it amul xeej ak seen, ku ne yoon woowu war na laa aar. Népp war nañu leen aar ci luy jalgati liñu tënk ci bataaxal bii ak bepp yëngu-gëngu buy indi par-parloo.

Partie 9. 8. Juróom natteelu matukaay

Nit ku ne am na sañ-sañ dem ci berebi àtte kaay yi ci reewam saa yoo xamne sañ-sañam yooyu dëppook sàrti réewam mba yoon jalgati nañu ko.

Partie 10. 9. Juróom ñentteeli matukaay

Menuñoo jàpp, tëj, mbaa genne kenn réewam te tegunu ko ci yoon.

Partie 11. 10. Fukkeeli matukaay

Ci lu wér, nit kune mën naa egg ci berebu atte kaay wax li ko naqari ci anam gu jub, te baña ànd ak par-parloo, ne dañu ko taxal.

Partie 12. 11. Fukkeeli been matukaay ak benn

Partie 13. 12. Fukkeeli matukaay ak ñaar

Kenn warula xuus ci dundinu doomu aadama, bu njabootam, ci lu jëm ci këram mbaa lu mengóok moom, di damm it jarajaam. Buñu jalgatee yii nit kune am na sañ-sañ ñu aar ko ci wàllu yoon.

Partie 14. 13. Fukkeeli matukaay ak ñatt

Partie 15. 14. Fukkeeli matukaay ak ñent

Partie 16. 15. Fukkeeli matukaay ak juróom

Partie 17. 16. Fukkeeli matukaay ak juróom benn

Partie 18. 17. Fukkeeli matukaay ak juróom ñaar

Partie 19. 18. Fukkeeli matukaay ak juróom ñatt

Nit kune am na sañ-sañ xalaat ak sa goom ci wàllu diine, soppi it diineem mba ngëmam, am na it tawfeex feeñal diineem, mbaa ngëmam, ak mbooloo, mbaa moom doww, fu àdduna daje mbaa deet, jarali ko ci njàngale mi, ci ay jëf, ci jaamu yi ak xarbaax.

Partie 20. 19. Fukkeeli matukaay ak juróom ñent

Nit ku ne am na sañ-sañ wax mbaa bind lu ko soob. Ci waxam yooyule kenn menuko ce bundu xatal. Te it am na sañ-sañ di gëstu, di jot, di wasare ci anam gu yaa ay xabaaraki xalaat ak ay jumtukaay yu mi Men ti jefandikóo.

Partie 21. 20. Ñaar fukkeeli matukaay

Partie 22. 21. Ñaar fukkeeli matukaay ak benn

Partie 23. 22. Ñaar fukkeeli matukaay ak ñaar

Nit ku ne meññeefu askan wi am na sañ-sañ ñu aar ko ci giru dundam. Ci dundam war na ci am xol bu sedd ci sañ-sañam yooyu, lu aju ci koom-koomam, ci dundinam ak ci lépp lu aju ci aadaam te di ko jox maanaa ak yookkute gu ànd ak tawfeex ci wàllu darajaam, loolu lépp nag ku ne doomu réew mi indi dooleem ak di jokkalante ak bitim réew te mu méngook tërërin ak am-amu réew mu ne.

Partie 24. 23. Ñaar fukk ak ñatteeli matukaay

Partie 25. 24. Ñaar fukk ak ñenteeli matukaay

Nit ku ne am na sañ-sañ noppalu, feexal xolal ak it di yamale diirub liggéeyam ak it léeg-léeg muy për, bër gu ànd ak xaalis.

Partie 26. 25. Ñaar fukk ak juróomeeli matukaay

Partie 27. 26. Ñaar fukk ak juróom benneeli matukaay

Partie 28. 27. Ñaar fukk ak juróom nenteeli matukaay

Partie 29. 28. Ñaar fukk ak juróom natteeli matukaay

Nit ku ne war naa tawaxu dëpp lu aju a askan wi, ak lu aju ci bitim réewam ba sañ-sañ ak tawfeex yi bataaxalu xeet gi ëmb mën a sax.

Partie 30. 29. Ñaar fukk ak juróom nenteeli matukaay

Partie 31. 30. Fanweereeli matukaay

Ci fànn gu mu mën ti doon ci bataaxal bii, bépp réew, mbootaay mbaa nit, warul doxal mbaa def luy yàq sañ-sañ yeek tawfeex.