Essai de balisage d'un conte en wolof


Méta-données (information sur le texte):


cesHeader:
fileDesc:
titleStmt:
h.title:Essai de balisage d'un conte en wolof
respStmt:
respType:balisage
respName:Chérif Mbodj
publicationStmt:
distributor:Projet AUF-LTT
pubAddress:UCAD,Dakar-Fann, Sénégal
availability:à utiliser seulement pour le projet de recherche AUF LTT
pubDate:2004-02-23
sourceDesc:
biblStruct:
monogr:
h.title:Doomu Yàlla
h.author:Anonyme
imprint:
pubPlace:Dakar
publisher:Clad
pubDate:2004
profileDesc:
langUsage:
language:wolof

Texte:

conteur
Léébóón !

public
Lipóón !

conteur
Amoon na fi

public
Daan na am !

Ma nga ameewoon ca jamano yee, ba rab yi dan wax ag nit ñi. Ammon na fi jigéén ju bon ju nekkoon ag ñeenti doomam. Ñoo nga dëkkoon ca biir àll ba. Baayu xale yi mi ngi dee, bi caat mi ñuy wax Tóni juddoo ; yaay ji jàpp ni xale bi dafa aay gaaf. Mu daldi ko bañ. Bu mosee rëbbi ba ñów, day woo xale yi, benn benn, ñu nàmp ba ùu des Tóni. Muy woy, naan :

001      Jamloro kaay nàmp,
002      Jamloro Siise kaay nàmp,
003      Biraama Siise kaay nàmp,
004      Ndaama Siise kaay nàmp,
005      Na Tóni xaar Yàlla, yaayam.


Di ko def ay yooni yoon, Waaye, jigéén ju bon ji mosul xam né Yàlla daan na feeñu Tóni ci melokaanu daar bu bare meew ; bu ñówee di nàmpal Tóni.
Am bés, musiba dal sjigéén ji. Mu jóge ca àll ba di woy ; woy wa mu daan woowee xale yi ngir nàmpal leen ; yemmoog Bukki di leen lekk ba mu des Tóni. Ba yaay ja jógee àll ba, muy woy, kenn wuyuwu ko, mu jaaxle lool. Yàggul dara, mu dégg baat bu mu miin, di woy, naan ko :

006      « Jamloro, Bulli jël na ko,
007      Buraama Siise, Bukki jël na ko,
008      Ndaama Siise, Bukki jël na ko ;
009      Tóni rekka des ci yaayam Yàlla ! »


Ba mu déggee kàddu yooyu, jigéén ji dafa yuuxu, yuuxu gu tar, réér ci àll bi. Foofa la lééb doxee tàbbi gééj, bàkkan bu ko jëkka fóón tàbbi àjjana.



Fichier transformé à l'aide d'une version des feuilles de style XCES améliorée par Andrei Popescu Belis (ETI, Université de Genève) dans le cadre des Formation RIFAL 2002 - http://www.osil.ch/gtf-rifal