Créée par : | Statut actuel : new | Créée le : | Mis à jour le :
Titre : | Essai de balisage d'un poème en wolof | ||||||||
Responsabilités : |
|
||||||||
Publication : |
|
||||||||
Source : |
|
Langues : | |||
wolof | ful | wol |
Su ñu may woowe bindkat ba përye ma
Ci ndajeb bindkati àdduna biy am
Àt mu ne ci Iowa-City, war naa xam lu tax,
Ma am kersa ci tudde sama bopp
Bindkat.
Su ñu may laaj, lu tax may bind ak lan
Laadi bind ci samay téere, te téere
Yi ma jota siiwal tere wu ñu ma
Ma am kersa ci tudde sama bopp
Bindkat,
Booba am na kiiraay guy dox
Ci sama digganteek bind mooma.
Su fekkee taalif yu gàtt yi ma daan
Bindantu ci wolof ba ma newee
Ca daaray digg ga, da ñu nekkoon ci man
Ay mbir yi ma daan feexal ci kiiraayu làkk
Ak kiiraayu xalaatin yi ma teguwoon,
Loolu warul tax ba ma tudde sama bopp
Bindkat,
Ndax kenn xamul dara ca mbindantu
Jamono yooya wesaaroo booba.
Su ma ne, noppalu ci nafar ay téere
Yu ñu bind ci làkki almaa waraloon
May bindantu farañse ca Strabourg,
Ba mbindantu mooma mujj nekk
Téere gu ma woowe "Mademba",
Loolu taxul ba ñu war ma tudde
Bindkat,
Ak lu téere booba mëna teewal-teewal
Xat-xat yi xaleyeek jigéen ñi di faral dunde
Ci sanuy réewu Afirigu sowu jànt yi,
Ak lu téere booba mëna teewal-teewal
Yàq yi yenn kilifa yi di yàq alalu réew mi,
Di teewal ñakk deggoo gi waa Afirig yi
Jànge ci daara tubaab yi ñakk deggook seen bopp.
Su ma ne sama ñaareelu téere, mu ngi doore
Ci xalaat gi ma doon xalaat mbirum apartheid,
Ci gis gi ma doon gis sama bopp ci ndaw su mag soosa
Te der ba ñuul ca réewu Afirigu bëjj saalum,
Ndaw soosa waroona jàngal ay xalé yu seen der ya weex,
Te mu mujjoona juge dëkkam, ñëw dëkk si Ndakaaru,
Te ñakk xam mooy kan, daan ko farala indil ay tiisu
Yu metti, fépp fu njàqare jibee, xaw ma ndax
Loolu war na tax ba ñu may tudde Bindkat,
Man mi bind sama téere yooyta ci kàllaama farañse goo xam ne,
Téemeeri nit yu nekk ci Afirig, fukk sax mënuñu ka ca nafar.
Ba ñu dooree fii ci ndajeb Iowa-City, di jéema tekkeek firi
Ci seen kàllaama àngalé, lépp lu ma bind ci kàllaama wolof,
Booba laay doora di mën tontu ci laaj gi ñu laaj bindkat yi
Maanaam: "Lu waral ñuy bind ak lan la ñuy bind?"
Bés bu bindkatu Afirig yépp mënee toontu ci laaj googu,
Kenn ci ñoom dootul amait benn kersa ci tudde boppam
Bindkat.