Action de recherche Expérimentation de normes de balisage en langues partenaires
Fichier généré à des fins expérimentales

Essai de balisage d'un conte en wolof

TEI XSL Stylesheets

Essai de balisage d'un conte en wolof


conteur
Léébóón !
public
Lipóón !
conteur
Amoon na fi
public
Daan na am !

Ma nga ameewoon ca jamano yee, ba rab yi dan wax ag nit ñi. Ammon na fi jigéén ju bon ju nekkoon ag ñeenti doomam. Ñoo nga dëkkoon ca biir àll ba. Baayu xale yi mi ngi dee, bi caat mi ñuy wax Tóni juddoo ; yaay ji jàpp ni xale bi dafa aay gaaf. Mu daldi ko bañ. Bu mosee rëbbi ba ñów, day woo xale yi, benn benn, ñu nàmp ba ùu des Tóni. Muy woy, naan :

Jamloro kaay nàmp,
Jamloro Siise kaay nàmp,
Biraama Siise kaay nàmp,
Ndaama Siise kaay nàmp,
Na Tóni xaar Yàlla, yaayam.

Di ko def ay yooni yoon, Waaye, jigéén ju bon ji mosul xam né Yàlla daan na feeñu Tóni ci melokaanu daar bu bare meew ; bu ñówee di nàmpal Tóni.

Am bés, musiba dal sjigéén ji. Mu jóge ca àll ba di woy ; woy wa mu daan woowee xale yi ngir nàmpal leen ; yemmoog Bukki di leen lekk ba mu des Tóni. Ba yaay ja jógee àll ba, muy woy, kenn wuyuwu ko, mu jaaxle lool. Yàggul dara, mu dégg baat bu mu miin, di woy, naan ko :

« Jamloro, Bulli jël na ko,
Buraama Siise, Bukki jël na ko,
Ndaama Siise, Bukki jël na ko ;
Tóni rekka des ci yaayam Yàlla ! »

Ba mu déggee kàddu yooyu, jigéén ji dafa yuuxu, yuuxu gu tar, réér ci àll bi. Foofa la lééb doxee tàbbi gééj, bàkkan bu ko jëkka fóón tàbbi àjjana.



Date .
This page is copyrighted

Action de recherche en réseau du Réseau Lexicologie, terminologie et traduction de l'Agence universitaire de la francophonie